Daawuda

Ci làkku ibrë (דָּוִד) la tur wi jóge. Daawuda mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam. Ci angale mooy David; Ci faranse mooy David. Moo doon buur bu mag ci bànni Israyil, di yonent bu bind lu bare ci Sabóor. Man nga jàng ci jalooreem ci Kàddug Yàlla gi ci 1Sa 16:1-30:31; 2Sa 1:1-24:25; 1Ki 1:1-2:10; 1Ch 3:1-9; 10:13-11:19; 12:1-23:32; 28:1-29:30. Benn ci maamaati Yeesu ci Macë ak ci Luug. Ci Injiil Daawuda moo feeñ ci aaya yii: Mc 1:6,17; 12:3; 22:42,43,45; Mk 2:25,26; 11:10; 12:36,37; Lu 1:27,32,69; 2:4,11; 3:31,32; 6:3; 20:42,44; Yow 7:42; Jëf 1:16; 2:25,29; 4:25; 7:45; 13:22,34,36; 15:16; Ro 1:3; 4:6; 11:9; 2Tim 2:8; Yt 4:7; 11:32; Pe 3:7; 5:5; 22:16.

Sëtu Daawuda:

Turu Kirist la, muy wone ne, ci lu jëm ci juddoom wàcc na ci yonent Yàlla Daawuda, di wone it ne, Almasi bi la. Sëtu Daawuda moo feeñ 15 yoon ci Injiil ci aaya yi: Mc 1:1,20; 9:27; 12:23; 15:22; 20:30,31; 21:9,15; Mk 10:47,48; 12:35; Lu 18:38,39; 20:41.

Abiya

Ci làkku ibrë la tur wi jóge.

Ci angale mooy Abijah or Abia; Ci faranse mooy Abia

Ci Injiil dañuy gis ñaari nit ñi bokk tur Abiya.

Ñaareelu buur ci Yuda, mooy doomu Robowam. Ñetti at la nguuru ci Yerusalem. Bind nañu ay jalooreem ci 1Ki 14:31-15:8; 2Ch 11:20-22; 12:16-14:1. Bokk na ci maamaati Yeesu yi ñu bind ci Mc 1:7.

Kenn ki soqikoo ci Aaroona (1Ch 24:10). Daawuda fal na askanu Aaroona ngir ñu toppatoo liggéeyu këru Yàlla. Mu xàjjale leen ba ñu nekk 24 kër. Kër gu nekk toppatoo nañu ñaari ayu-bés at bu nekk. Sakariya, baayu yonent Yàlla Yaxya bokkoon na ci askanu Abiya (Lu 1:5).

Abiyatar

Ci làkku ibrë la tur wi jóge.

Ci angale mooy Abiathar; Ci faranse mooy Abiathar

Saraxalekat bu mag ba la woon, ci jamano nguuru Daawuda. Man nañu ko gis ci 1Sa 22:20-21; 2Sa 15:24-29; 20:25; 1Ki 2:22-27,35; 1Ch 15:11-13; 27:33-34.

Ci Injiil dañuy wax ci Abiyatar ci Mk 2:26.

Admin

Ci làkku ibrë la tur wi jóge.

Ci angale mooy Aram or Ram; Ci faranse mooy Admin

Doomu Esrom la woon, di maamaatu Daawuda (1Ch 2:10; Ru 4:19). Benn ci maamaati Yeesu ci Luug la woon (Lu 3:33). Mooy Aram itam ci maamaati Yeesu ci Macë (Mc 1:3,4).

Aminadab

Aminadab – Ci làkku ibrë (עמינדב|Aminadav) la tur wi jóge. Ci àngale mooy Amminadab or Aminadab, ci faranse mooy Aminadab.

Baayu jabaru Aaroona, Eliseba la woon (Ex 6:23), di maamaatu Daawuda ak Yeesu. Bokk na ci maamaati Yeesu yi ñu gis ci Macë ak ci Luug (Mc 1:4; Lu 3:33).

Aram

Ci làkku ibrë la tur wi jóge.

Ci angale mooy Aram or Ram; Ci faranse mooy Aram

Doomu Esrom la woon, di maamaatu Daawuda (1Ch 2:10; Ru 4:19). Naka noonu, bokk na ci maamaati Yeesu ci Macë (Mc 1:3,4). Aram mooy ki ñu tudd Admin itam ci maamaati Yeesu ci Luug (Lu 3:33).

Betleyem

Ci làkku ibrë בית לחם la tur wi jóge.

Ci angale mooy Bethlehem; Ci faranse mooy Bethléhem

Dëkk bu ndaw la woon, lu tollu 9 kilomet ci bëj-saalumu Yerusalem. Dëkku Daawuda la. Foofu la Yeesu juddoo.

Dañu ciy wax ci Injiil ci Mc 2:1,5,6,8,16; Lu 2:4,6,15; Yow 7:42.

Bisu Tamxarit

Bisub Tamxarit Ak Bisub Tamñërit, Bisub Tamxarit di 9eelu fan ci weeru Tamxarit, bis la budi aw xew ci Jullit ñi, rawatina ñi ëpp ci sunnit yi, Siiha yi it dina ñu ko xewal ngir naqarlu, ray gees rayoon Useynu Sëtub Yonent bi (Jàmm ci ñoom) ca réewum Iraak, nees nako fa xumbal, ci àndandoo wàcc ci mbedd yi, di wone séni naqar, Ci julliti Senegaal yi, Baaxoos na toggi cere ca ngoon ga, ba ca guddi ga di guddig Fukkéelu fan ba, mu di guddi gu màgg ci lislaam ngir ay xew-xew aki ngënéel yu ci Yàlla jagleele, ku ca jàppu ba séll julli ñaari ràkkaa, ràkkaa bu ci ne nginnaaw faatiha nga tari saar wu la soob ci Alxuraan, boo noppee sàbbaal Yàlla lu la soob, julli ci Yonent bi (Xeewalug yàlla ci moom) lu la soob, te ñaan say aajo muslu ci balaa yoy at mi.

Ammaa nag yeneen yees ciy def niki, jal suuf di ca këpp bool bañu doon reere, ak bàyyi ca bool ba ab danku cere ak tuuti ndox bu ñu xëyee di ci sëlmu, mbaa tusngalu di séentu asamaan ngir ni dañuy gis Faatimata bintu Rasuulilah, (Tusngalu nag sopp nañu ko ci),

Yooyu yépp ku koy def walla ku koy deflu mbaa ku gis ku gis ku koy def, na ko jàppe ni baax (aada) la rekk xamu ma nag séeni cosaan waaye tegeesu ko ci diine.

Tamñërit di bisub fukkéel ci wéeru Tamxarit, bis bu màgg la ci xew-xewi àddina rawatina ci Lislaam li ko dale ci sosug nit ba léegi, Yàlla defal naci ay jaamam xéewal yu rëy aki ngënéel, jéggal ci it ay jaamam,

Bowas

Ci làkku ibrë (בועז) la tur wi jóge.

Ci angale mooy Boaz; Ci faranse mooy Boaz

Boroom alal ak beykat ci dëkku Betleyem la woon. Dafa takkoon jenn jigéenu Mowab, ji tudd Ruut. Jot na Ruut ndax jëkkëram mbokkam la woon te faatu na bala mu am doom. Ci kaw seeni yoon, su fekkee ne am na genn góor gu faatu te bàyyiwul doom, mbokkam mu gëna jege war na donn jabaram. Seen taaw bu goor dina donn ci goor ki faatu woon. Bowas mbokk mu jege jëkkëru Ruut la woon. Doom bi ñu jur mooy maamu Daawuda. Man nañu koy jàng ci Ru 1:1-4:22. Naka noonu Bowas bokkoon na ci maamaati Yeesu, ni ñu koy gise ci Macë ak ci Luug (Mc 1:5; Lu 3:32).

Yeneeni làkk

This page is based on a Wikipedia article written by authors (here).
Text is available under the CC BY-SA 3.0 license; additional terms may apply.
Images, videos and audio are available under their respective licenses.