Baatukaay

Baatukaay :

Latin dictionary
Baatukaay Latin

Xool it

Jukki yi ci lonku

  • [[]]

Lëkkalekaay yu biti

Esperanto

Esperanto - Làkk

Jimbulang

Jimbulaŋ aw wayndare la wu yitteem doon ëmb mbooleem xeeti xam-xam walla man naa itam tënku ci benn xam-xam, maanaam jimbulaŋ buy wax ci paj walla ci taariix kepp. Jimbulaŋ am mbooloom ay jukki la def, bu ci nekk di wax ci lenn: ciw nit, cib barab, cib xew-xew, cib xam-xam,... Jimbulaŋ day wuuteek baatukaay, ndax du yem rekk ci faramfacce wenn làkk wi. Naka-jekk day doon ay téere yu bari.

Njàngat

Baatu Njàngat day tekki mbooleem ay mbind yuy wax ci ay koj. Ni ko Ñenn ñi di gisee du yem rek ci mbind yu ñu taaral waaye am na it njàngatu kàddu, maanaam yu yemm ci ay kàddu. Sunu xoolee mboolaay yu mel ne yu waa Afrik yi xamul woon bind, seenum njàngat ci kàddu la yemoon.

Pullaar

Pullaar aw làkk la wu ñuy wax daanaka ci 20 réewi Afrig gu sowwu ak gu diggu, Dale ko ca pegi dexu Senegaal ba ci gu Niil, waaso yu pël, tukulóor ak yu lawbe ñooy ñi koy làkk.

Ci cosaan pël yi ay sàmmkat lañu, waaye tay daanaka xeeti liggéey yépp lañuy def: yaxantu, béy, njëwrin, añs.

Ci pullaar yi nekk Senegaal ak Gànnaar, ñi koy làkk lañuy wax ay "haalpulaar'en" ("haalpulaar" su dee kenn), baat baa ngi jóge ci "Haalde" di firi "wax". "Haalpulaar'en" yi ci pegu dexu senegaal ay pël lañu jàppe seen bopp donte yenn saa yi dañuy am weneen làkk. Ni ko Amadu Ampaate Ba waxe, "Haalpulaar'en" yi duñu aw waaso, waaye am mbooloom ay waaso yu bokk dëkke dex gi, tànn pullaar niki làkk wu njëkk, làkk wu ñépp bokk di wax, di ci jokkoo.

Pullaar di nañu ko wax itam pël, pular walla fufulde, ci waa faraas pël lañuy wax di baat bu ñu abbee ci wolof.

Wikbaatukaay

Wikbaatukaay ab baatukaay barilàkk bu ubbeeku la, di benn ci sémbi Wikimedia Fondation yi. Baatub «Wikbaatukaay» dafay junj sumb bu wolof bu boobu sémb, di Wiktionary ci wu-angalteer. Mook Wikipedia ñoo bokk doxiin, di lu ubbeeku te dàttu ci nosteg wiki, lees man a jëfandikoowaat ci anami GFDL.

Wikipedia

Wikipedia (di jàng wikipediyaa) ab sémbub jimbulang la ci web bi, di lu àddunawu te bariylàkk. Ag bindam nag mi ngi wéy ba tay, xaralaay wiki lañu jëfandikoo ngir sos ko. Yéeney Wikipedia mooy jébbal am ëmbiit mu ubbeeku, maandu te fugluwu.

Wolof (làkk)

Wolof làkk la wu ñuy wax ci Gaambi (Gaambi Wolof), Gànnaar (Gànnaar Wolof), ak Senegaal (Senegaal Wolof). Mi ngi bokk nag moom wolof ci bànqaasub atlas bu làkki kongoo yu kojug nit ku ñuul yi. Mbokkoo gi mu am ak làkku pël lu yàgg la. Am na it lu mu seq ak yeneen làkk ci gox bi niki séeréer, joolaa ak basari.

Yeneeni làkk

This page is based on a Wikipedia article written by authors (here).
Text is available under the CC BY-SA 3.0 license; additional terms may apply.
Images, videos and audio are available under their respective licenses.