Aaroona

Ci làkku ibrë (אַהֲרֹן) la tur wi jóge. Aaroona mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam. Ci angale ak ci faranse mooy Aaron.

Magu yonent Yàlla Musaa la woon, ñu bokk ndey ak baay. Ñetti at la Aaroona mage Musaa. Baayam, Amram la tudd te yaayam Yokebedd (Ex 6:20). Amoon na ñeenti doom yu góor ci jabaram, Eliseba. Ñooy Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar (Ex 6:23). Aaroona amoona benn rakk bu jigeen, mingi tudd Mariyaama, doomu ndeyu Aaroona ak Musaa (Ex. 15:20). Mariyaam bii, bokkul ak yaayu Yeesu Krist.

Ba Musaa demee ci kanamu Firawna Aaroona dafa àndoon ak moom ngir nekk yonentam (Ex 7:1). Yàlla tànn na ko, mu jëkka doon saraxalekat bu mag ba ci biir bànni Israyil. Moom moo sàkkaloon bànni Israyil benn xërëm bi xaaroon Musaa ca tundu Sinayi. Ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo (Ex 32:1-28). At, ya Aaroona dundoon, 123 la. Ci kaw tund wi ñu wax Xor la faatu (Nu 33:39).

Man nga jàng jalooreem ci Ex 4:14-16; 4:27-31; 5:1-4; 15-21; 6:28-7:13; 19-22; 8:5-12; 16-19; 9:8-12; 16:2-10; 19:23-24; 24:1-2,9-15; 28:1-12,29-30; 32:1-8,14-28,35; 34:29-33; Le 8:1-9:24; 10:1-4; Nu 3:1-4; 12:1-15; 14:2-5; 16:1-35; 41-50; 17:1-10; 18:1,8,20; 20:1-12; 23-29; 26:58-61.

Ci Injiil dañuy wax ci Aaroona ci Lu 1:5; Jëf 7:40-41; Yt 5:4; 7:11; 9:4.

DD Frauenkirche Aaron
Aaroona
Abiya

Ci làkku ibrë la tur wi jóge.

Ci angale mooy Abijah or Abia; Ci faranse mooy Abia

Ci Injiil dañuy gis ñaari nit ñi bokk tur Abiya.

Ñaareelu buur ci Yuda, mooy doomu Robowam. Ñetti at la nguuru ci Yerusalem. Bind nañu ay jalooreem ci 1Ki 14:31-15:8; 2Ch 11:20-22; 12:16-14:1. Bokk na ci maamaati Yeesu yi ñu bind ci Mc 1:7.

Kenn ki soqikoo ci Aaroona (1Ch 24:10). Daawuda fal na askanu Aaroona ngir ñu toppatoo liggéeyu këru Yàlla. Mu xàjjale leen ba ñu nekk 24 kër. Kër gu nekk toppatoo nañu ñaari ayu-bés at bu nekk. Sakariya, baayu yonent Yàlla Yaxya bokkoon na ci askanu Abiya (Lu 1:5).

Aminadab

Aminadab – Ci làkku ibrë (עמינדב|Aminadav) la tur wi jóge. Ci àngale mooy Amminadab or Aminadab, ci faranse mooy Aminadab.

Baayu jabaru Aaroona, Eliseba la woon (Ex 6:23), di maamaatu Daawuda ak Yeesu. Bokk na ci maamaati Yeesu yi ñu gis ci Macë ak ci Luug (Mc 1:4; Lu 3:33).

Yeneeni làkk

This page is based on a Wikipedia article written by authors (here).
Text is available under the CC BY-SA 3.0 license; additional terms may apply.
Images, videos and audio are available under their respective licenses.